Ñeel Daawuda. Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, saa jëmm jépp di sàbbaal sellngay turam!
TSK
TSK · Luke 18:43
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nañu sante Aji Sax ji ngoram ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.
Nañu sante Aji Sax ji ngoram ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.
Su bés baa ab tëx dégg kàdduy téere, silmaxa tàggook lëndëm, di gis,
Maay doxloo silmaxa yi ci yoon wu ñu xamul, ñall wu ñu miinul laa leen di jaarale. Maa leen di soppil lëndëm gi fi seen kanam, ag leer, fu ñagas, ma maasaleel leen. Lii laa leen di defal, te duma leen wacc mukk!
xeet wii ma bindal sama bopp, te ñooy siiwal sama woy.»
Ba loolu amee mbooloo mépp a neey, di sàbbaal Yàlla, tiitaange jàpp leen, ñu naan: «Gis nanu tey mbir yu tiiñ am xel.»
¶ Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi walbatiku, di xaacuy sàbbaal Yàlla.
Ba loolu amee ñu tëkkuwaat leen, door leena yiwi, ñu dem, gannaaw manuñu leena mbugal te amuñu bunt ci ñoom ndax mbooloo ma, te ñépp di màggal Yàlla ca la xew,
ngir nga xippil leen, jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, seppee leen ci noteelu Seytaane, indi leen ci Yàlla, ñu am njéggalug bàkkaar, am cér ci biir nit ñi ñu sellal ndax ngëm, gi ñu ma gëm.”
kera bés bu délsee ba jot ci teddngaam ci biir ñoñam ñu sell ñi, ba mboolem ñi ko gëm di ko yéemoo. Te yeen ci seen bopp, ci ngeen di bokk, ndax yeena gëm la nu leen seedeeloon.