Daawuda teg ca ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax jiy dund, Aji Sax ji ci boppam moo koy fàdd. Yaar àppam jot, mu dee, mbaa mu dem xare, des ca.
TSK
TSK · Luke 18:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ngalla dammal loxol ku soxor ak ku bon, topp leen seen coxor, gi ñu yaakaaroon ne du feeñ.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di taalif bu ñeel Daawuda.
Waaye Aji Sax jeek man, di ñeyi xare. Moo tax ñi may tëru di tërëf, ba duñu daan, xanaa rus lool, ndax duñu baaxle; gàcce gu yàgg lay doon te du fey.
Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»
¶ Yeenay ñi Yàlla taamu, sellal leen, sopp leen. Kon nag solooleen xolu yërmande, akug mbaax, ak woyoflu, ak jikko ju lewet, ak xolu muñ.
Te kat njekku Yàlla dina feeñ ndax coono ba muy delloo ñi leen teg ab coono.
¶ Maa ngi lay fàttliku ci samay ñaan guddeek bëccëg, fu ma tollu te di ci sant Yàlla, mi may jaamoo xel mu dal, ni ko samay maam daan defe.
¶ Kon nag buleen teqlikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci.
Ñu àddu ca kaw ne: «Buur bu sell, bu dëggu bi, loo deeti xaar ci àtte waa àddina, feyul nu sunu deret ji tuuru?»
Ndokklee, asamaan, Ndokklee, yeen ñu sell ñi itam, ak ndawi Yàlla yeek yonent yi, ndaxte Yàllaa leen àtteek dëkk bii, mbugal ko.