TSK

TSK · Luke 19:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci kaw loolu ñu ne Musaa: «Yaw, waxal ak nun, nu dégg, waaye bu Yàlla ci boppam wax ak nun, lu ko moy nu dee.»

Samiyel ne mbooloo ma: «Buleen tiit; dëgg la, yeena def googu mbon gépp, waaye fexeleen rekk ba baña dëddu Aji Sax ji, te ngeen jaamoo Aji Sax ji seen léppi xol.

Job 21:14 TSK

Moona kee noon Yàlla: «Xiddi ma! Xam saw yoon soxalu ma.

Yeena ne: “Jaamu Yàlla ag neen la. Ana lu nu jële ci dénkoo ndénkaaneem, tey wéye toroxlu fi kanam Aji Sax ji Boroom gàngoor yi?

Ndaxte boroom xintey bakkan ab noonu Yàlla la, nde déggalul yoonu Yàlla, te manu ko sax.

Ndax kat Noo gi nu Yàlla jox taxu noo ragal, xanaa kay da noo may doole, ak cofeel, ak jëfin wu laloo am xel.