TSK

TSK · Luke 19:43

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax jeey jógloo ci seen kaw, xeet wu sore, ñu bàyyikoo ca cati àddina, dikk ne milib nig jaxaay, te dégguleen aw làkkam,

Wóoy ngalla Aryelee, Aryel, dëkk ba Daawuda dale. Dundleen at ak at, amal-leen ci màggal ci kaw màggal.

Ay sàmm ak seeni gétt ci sa kaw, ñu samp seeni xayma, wër la, di foral, ku nekk ak pàccam.

«Dëkk-dëkkaan yi bootu ci sa àll bi, saamar la leen di reye. Mooy yékkati fi la wër ab gawukaay, jal ay sëkk, gawe la, yékkati kiiraayu xare yu ràbbaloo ba def um taax, janook yaw,

Yawut ñi ñoo rey Sang Yeesu, na ñu reye woon yonent yi, te ñoo nu bundxatal tey. Neexuñu Yàlla, te nooni ñépp lañu.