TSK

TSK · Luke 2:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Nanga ma sédde bépp taaw bu góor, nit ak mala, lépp lu jëkka juddu ci bànni Israyil, maa moom.»

Seen jur gu gudd ak gu gàtt itam, naka noonu. Juróom ñaari fan lay nekk ak ndeyam, bésub juróom ñetteel ba, ngeen jox ma ko.

Ndax lépp luy taaw bu góor, sama cér la. Keroog ba ma fàddee lépp luy taaw bu góor ca réewum Misra, ca laa sellalal sama bopp lépp luy taaw ci Israyil, dale ci nit ba ci jur. Maa leen séddoo. Maay Aji Sax ji.»

Lépp luy ubbitey njur bu ñu jagleel Aji Sax ji, ci lépp lu bindoo aw suux, nit ak mala, yaa koy moom. Fexeel rekk ba jotlu taawub nit ki, te taawub mala mu setul it, nanga ko jotlu.