Su bés baa njebbitum Aji Sax ji doon lu yànj, darajawu, meññeefum réew mi di teraanga, dib sag, ñeel ñi dese bakkan fi Israyil.
TSK
TSK · Luke 2:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu ne: «Man Aji Sax ji, maa la woo cig njekk, jàpp la ci loxo, sàmm la, def la ngay kóllëre sama digg ak nit ñi; def la ngay leeru xeet yi,
Mu ne: «Xeeb naa li ma la sas ngay sama jaam biy siggil giiri Yanqóoba, te wara délloosi ndesu Israyil gii. Tabb naa la, ngay leeru xeet yi, di jotale waa cati àddina sama wall.»
Du jant a lay leeralati bëccëg, te weer du la niital; Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa Yàlla jooju di sab taar.
¶ Ma séentu, gisuma lu moy jenn waay ju ŋàbb buumu nattukaay ci loxoom.
Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.
Dañu noon fàww Almasi jaar ci ay coono te mooy jëkka dekki, ba siiwtaane leer gu jolli, ñeel bànni Israyil ak jaambur ñi itam.»
Dama leen di wax ne leen, bëgga fésal ne Yàlla ku dëggu la moo waral Almasi dikk, def boppam jawriñu Yawut yi, ngir sottal dige ya Yàlla digoon seeni maam.
Te dëkk bi soxlawul jant bu koy leeral mbaa weer, ndax leeru Yàllaa koy leeral, Gàtt bi di làmpam.