¶ «Bésub keroog bésu pàttliku lay doon ci yeen, ngeen war koo màggal ngir Aji Sax ji, muy dogal bu leen war fàww, yeen ak seen askan.
TSK
TSK · Luke 2:41
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñetti yoon cim at la seen góor ñépp di teew fi kanam Boroom bi Aji Sax ji, Yàllay Israyil.
¶ «Weer wi jëkk ci at mi nag, fukki fanam ak ñeent mooy bésub Mucc bi, ñeel Aji Sax ji.
su boobaa bérab bu seen Yàlla Aji Sax ji taamu ngir dëël fa turam, foofa ngeen di yóbbu mboolem lu ma leen sant: seen saraxi dóomal, ak yeneen sarax, ak seen céri fukkeel, ak seenub jooxe, ak mboolem ngëneel yu ngeen di def saraxi xas yu ngeen xasoo ak Aji Sax ji.
¶ Wormaal-leen weeru Abiib, te ngeen amal ci màggalu bésub Mucc, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, ndax ci weeru Abiib la leen seen Yàlla Aji Sax ji génnee Misra, ag guddi.
At mu nekkaan Elkana day jóge dëkkam, dem Silo, màggali fa Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, sarxalal ko ca Silo. Foofa la Ofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya doonoon sarxalkati Aji Sax ji.