Moonte Aji Sax ji àrtu woon na Israyil ak Yuda, mboolem yonentam yaak boroom peeñu ya jottli leen ko, ne leen: «Dëppleen seen yoon yu bon yii ngeen topp, te sàmm samay santaane, wormaal samay dogal, na mu dëppook mboolem yoon wi ma tëralal seeni maam, yónnee leen ko, yonent yiy samay jaam jottli leen ko.»
TSK
TSK · Luke 20:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndaxam muñal nga leen ay at yu bare, di leen artoo sam xel, say yonent di leen ko jottli; waaye taxul ñu déglu. Nga teg leen nag ci loxoy waa réew yi.
«Mbugal naa seeni doom, jariñul dara. Dégguñu yar, bóom ngeen seeni yonent, mbete gaynde yuy fàdde.
Ba mu ko defee Pasur dóorlu Yonent Yàlla Yeremi, jéng ko ca buntu kër Aji Sax ja féete kaw, te ñu dippee ko Beñamin.
«Aji Sax ji dafa wax ne: Dangay taxawi ca biir ëttu kër Aji Sax ji. Nga wax ak mboolem waa dëkki Yuda yiy jaamusi ci kër Aji Sax ji. Mboolem kàddu yi ma lay yóbbante ci ñoom, bu ci wacc baat.
‘Aji Sax ji da laa fal sarxalkat, nga wuutu Yoyada sarxalkat bi, ngir kër Aji Sax ji am ku ko yor, ba dof bu fiy wax-waxlu ay waxyu, nga jéng ko, yeewe ko càllalay weñ ci baatam.
seen xol tàng ci Yeremi, ñu dóor ko ba noppi, tëj ko ca biir kër Yonatan bindkat ba, fa ñu defoon kaso.
Yónnee naa leen ay yooni yoon mboolem yonent yi, sama jaam ñi, ne leen: “Rikk buleen def jëf ju siblu jii ma bañ.”
Kon nag waxal askan wi, ne leen Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Dellusileen ci man,” kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, “kon dinaa dellusi ci yeen.” Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yee ko wax.
Wóoy ngalla yeen, yeenay tabax bàmmeeli yonent yi, te seeni maam reyoon leen.