TSK

TSK · Luke 20:38

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg.

Muy jàngi màggal, ñeel Daawuda. Sama Yàlla, Buur bi, naa la màggal, teral sa tur ba fàww.

Deeyam ga mu dee ca la deeyal bàkkaar benn yoon ba fàww, te dund gi muy dund tey, Yàlla la koy dundal.

Ndax kat kenn ci nun dundul ngir boppam, te kenn deewul ngir boppam.

Cig néew doole lees ko daaje ci bant ba rey ko, waaye tey ci manoorey Yàlla lay dunde. Nun itam sunug bokk ci Almasi moo tax nu néew doole, waaye ci manoorey Yàlla lanuy bokk ak moom di dund, bu nuy jëflante ak yeen.

Waaye réew mu ko gën lañu doon sàkku, te mooy réewum asamaan. Looloo tax Yàlla rusul ñu di ko tudde seen Yàlla, ndax waajalal na leen ab dëkk.

¶ Ci kaw loolu malaaka mi won ma dexu ndoxum dund mu leer nàññ ni doju kiristaal, ndox ma wale ca ngàngunem Yàllaak Gàtt ba,