TSK

TSK · Luke 21:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet, kàddoom di taxa xam, di dégg.

ndax su boobaa Noo gu Sell gi moo leen di xamal ca waxtu woowa la ngeen wara wax.»

Acts 2:4 TSK

Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.

Acts 4:31 TSK

¶ Ba ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu daje daa yëngu, ñu feese Noo gu Sell gi ñoom ñépp; ñu daldi tàmbalee waxe fit kàddug Yàlla gi.

Naka la Póol wax ci mbirum njub, ak moom sa bakkan, ak àtteb bés-pénc, Feligsë daldi tiit, ne ko: «Léegi, man ngaa demagum, bu ma ko talee, dinaa la wooluwaat.»

¶ Man itam, booleleen ma ci, ngir saa yu ma ubbee sama gémmiñ, mana xéewloo ndéey lu ma xamlee fit wu dëgër, mbóoti xibaaru jàmm bi,

¶ Keroog ba ma jëkkee di layool sama bopp, kenn taxawuwma, ñépp a ma daw, yàlla bu leen seen jëf topp.