TSK

TSK · Luke 21:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ba dunu tiit suuf su yëngu sax, ba tund yiy tàbbi biir géej,

Bésub keroog ñu ŋaral Yuda, ŋar yu mel ni géej gu sàmbaraax! Foo geesu ci réew mi, xool, doo gis lu moy lëndëm ak njàqare, xàmbaar maase, ba leer giim.

Moo tax maay gësëm asamaan, suuf yëngoo fa mu tege ndax sànjum Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, keroog ba meram di tàkk.

Kersa la weer wiy am, gàcce ñeel jant bi; Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal, mooy nguuru Yerusalem, kaw tundu Siyoŋ, leeram ga jollee fa kanam magi ñoñam.

Maa xool suuf, ndeke ma nga ne maraas, ne wëyëŋ; ma xool asamaan, leer amatu ca.

¶ Malaaka ma waxati ma, ne ma: «Jamono yooyu ci la Mikayel, malaakam wattukat mu mag, miy taxawu sa mbooloo, di jóg. Muy jamonoy njàqare ju masula am, cosaanal xeet yi ba tey jii. Bu keroogee sa bokk yay mucc, di ñi ñu bind ci téereb dund bi.

Amos 8:9 TSK

Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «maay sowal jant digg bëccëg, lëndëmal suuf bëccëg ndarakàmm.

Waaye bésu Boroom bi nib sàcc lay dikke. Ca la asamaan yi di dëddoo ci biir coow lu réy, lu ko sosoon seey ndax tàng, suuf ak jëf ju ci biiram xoyomu.

¶ Ci kaw loolu ma gis ngàngune mu mag mu weex, ak ku ci toog. Asamaan ak suuf daldi dawe fa kanamam, ne mes.