Ndax Aji Man ji la daan bége, am daan na tudd Yàlla fu mu tollu?
TSK
TSK · Luke 21:36
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye bésub dikkam, ana ku ko mana dékku? Bu teewee ana kuy taxaw? Nde moom daa mel ni sawaras tëgg buy xelli weñ, melati ni xemey fóotkat.
Ndokklee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk.
Waaye ña ñu yeyale ndekkitel ëllëg, yeyale leen bakkan ci àddina siy ñëw, ñooñu, su boobaa, kenn du ci am jabar mbaa jëkkër.
¶ Teewluleen te saxoo ngëm, góor-góorluleen te dëgërlu.
Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp farlute, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.
saxooleen ñaan,
Waaye yaw, àndal ak sa sago, ak diggante boo mana tollu, te ñeme coono. Jàppal ci liggéeyub jottli xibaaru jàmm bi, beyal sa waar ba mu mat sëkk.
¶ Àndleen ak sago te teewlu! Seenub noon Tuumaalkat bi, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax.
¶ Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk,