Ba ma nee cell, damaa ràgg, dëkke naqar.
TSK
TSK · Luke 22:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji ne Tuumaalkat bi: «Aji Sax ji rëbb na la, Yaw Tuumaalkat bi, Aji Sax ji taamu Yerusalem rëbb na la. Xanaa Yosuwe mii du lenn lu moy gillit wu ñu fëkke cib taal?»
Ci kaw loolu Sang bi geesu, ne jàkk Piyeer, Piyeer fàttliku la ko Sang bi waxoon ne ko: «Bala ganaar a sab tey jii, dina fekk nga jàmbu ma ñetti yoon.»
¶ Gannaaw joxees nañu nu àtteb ñu jub ndax deretam ji tuuru nag, ñaata yoon lees nuy gënatee musal ci am sànj ndax moom?
Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!
te ma nekkoon ab tooñkatam, di ab bundxatalkat, di ab néeg. Waaye yërmande laa dajeel, ngir ñàkka xam ga ma daan jëfe, te ñàkka gëm tax.
¶ Ci Man Póol la bataaxal bii bawoo, man jaamub Yàlla, biy ndawal Yeesu Almasi, mu yebal ma, ngir ma dugal ñi Yàlla tànn ci yoonu ngëm ak xam-xamu dëgg, giy taxa jullite.
¶ Kon nag «dëgëral-leen loxo yi toqi, ak óom yi bañ,»
¶ Ci man Piyeer, ndawal Yeesu Almasi la bataaxal bii bawoo, ñeel askan wi Yàlla taamu, te ñu toxuji diiwaani Pont ak Galasi ak Kapados ak Asi ak Bitini.
¶ Kon nag teewlooleen seen xel, te ànd ak seen sago, te ngeen wékk seen jépp yaakaar ci yiw wa ñu leen di dikke kera bu Yeesu Almasi feeñee.
¶ Kon nag bokk yi, nangeen gënatee def lu ngeen man ba dëggal woote bi ñu leen woo, ak taamu gi ñu leen taamu. Su ngeen ko defee kat, dungeen daanu mukk.
¶ Kon nag yeen soppe yi, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, wattuleen bala leena réeraangey moykati yoon yi yóbbaale, ba yolomal seenub taxawaay.