TSK

TSK · Luke 3:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Xanaa du sédd ku xiif saw ñam, fat néew-ji-doole ju amul fu mu dëkk, gis ku rafle, wodd ko, te baña nëbbu mbokk mu soxla?

Li ci biir kay ngeen di sarxe! Su boobaa seen lépp ay set.

Luke 19:8 TSK

Sase nag taxaw ne Sang bi: «Sang bi, ma ne, sama genn-wàllu alal, jox naa ko néew-doole yi, te jépp alal ju lewul ju ma masa jëlal kenn, dinaa fey ñeentam.»

Acts 10:2 TSK

Ku jullite la woon te ragal Yàlla, mook waa këram gépp; bare woon na sarax yu muy yéwéne askan wi, te ñaan ci Yàlla la saxoo woon.

Mu ne ma: “Korney, nangu nañu say ñaan, te nemmiku nañu say sarax fa kanam Yàlla.

Ñi barele na ñuy def lu baax, nañu barele jëf ju baax, di joxee xol bu tàlli, yéwén te nangoo dimbalee.

Njullite gu set te mucc sikk fa kanam Yàlla Baay bi moo di lii: di nemmiku jirim akub jëtun ci seen njàqare, tey sàmmu ba mucc ci gàkki àddina.