TSK

TSK · Luke 5:35

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bu juróom benn fukk yeek ñaar ciy àppi juróom ñaar weesee, dees na bóom ku ñu fal, te kenn du ànd ak moom. Gannaaw loolu kilifa dina ñëw, ànd ak gàngooram, yàqte dëkk beek jaamookaay bi. Waaye kilifa googu lu mel ni mbënn a koy mujje. Dogal nañu ne yàqte gi dina wéy ba keroog xare biy jeex.

Yeesu ne leen: «Lu ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Ñu daldi taxaw, seen kanam lëndëm ndaxu tiis.

Acts 1:9 TSK

¶ Naka la wax loolu, ndaw yay xoole, ñu jekki yéegee ko fa, aw niir daldi leen koy làq.

Acts 13:2 TSK

Ñooñoo daje woon di màggal Boroom bi, boole kook koor. Ci biir loolu Noo gu Sell gi ne: «Beral-leen ma nag Barnaba ak Sóol ngir liggéey, bi ma leen wooye.»

Buleen di xañante seen bopp, ndare du yeena mànkoo ab diir, ngir bokk tënku ci ñaan. Waaye gannaaw loolu, delluleen di ànd, bala leena Seytaanee xiirtal ci moy, ndax tëlee téye seen bopp.