TSK

TSK · Luke 6:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 21:7 TSK

Lu tax ku bon di dund, bay magal sax, di ànd ak doole?

Waaye Yàllaa may musal ci dooley njaniiw, jot sama bakkan, ba jël ma.

Amos 4:1 TSK

Dégluleen kàddu gii, yeen jigéeni tundu Samari, yeena ngi suur ni nagi diiwaanu Basan. Yeen ñiy torxal néew-ji-doole, di not aji ñàkk te naan seeni jëkkër: «Indil ñoll waay, ñu naan!»

Daraja ji kër gii di mujje mooy sut ja woon, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. Mu ne: Ci bii bérab laay mayee jàmm, kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.»

Ci kaw loolu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen wépp xeetu bëgge, ndax loo barele barele, sa bakkan ajuwul ci sa alal.»

Ba waa ji déggee loolu, am na tiis wu réy, ndax barele woon na lool.

James 2:6 TSK

Yeen nag ngeen di teddadil néew doole yi! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di noggatu, di leen diri ba fa mbaxana dee benn?

Na mu jëfe ak yeen, jëfeleen ko ak moom, feyleen ko ñaari yoon ay jëfam. Kaas bi muy xellile am njafaan, feesalal-leen ko njafaan lu ko ëpp doole ñaari yoon.