te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”»
TSK
TSK · Luke 7:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ab yonent bu soqikoo ci yeen kay, di seen mbokk ni man, moom la leen seen Yàlla Aji Sax ji di feeñalal. Moom ngeen di déggal.
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal.»
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Boroom bi, Aji Sax jaa ngii, dikkaale doole ak kàttanu kilifteefam. Mu ngii ànd ak ñi mu yooloo, ñu dig peyam, dox jiitu ko.
«Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, mu falu di buur bu xelu, di jëfe njub ak njekk ci réew mi.
Moo tax Aji Sax ji di leen wacc ba keroog jant, ba kiy matu mucc. Ca la bokkam ya dese bakkan di dellu, fekki seen bokki bànni Israyil.
Bégala bég, janq Siyoŋ mu taaru, janq Yerusalem mu taaru laa ne: Xaacul, sa buur a ngoog, jëmsi ci yaw, moo jot njekk ak mucc, te teewu koo woyof, war mbaam, cumbur doomu mbaam.
¶ Gannaaw loolu Sang bi tabb na yeneen juróom ñaar fukki taalibe ak ñaar, yebal leen, ñaar, ñaar, ñu jiituji ko ca mboolem dëkk yaak gox, ya mu nammoona dem moom ci boppam.
¶ Naka la malaaka ma wax ak Korney ba dem, mu woo ñaar ciy surgaam, ak benn takk-der bu jullite te bokk ciy suqam.