TSK

TSK · Luke 8:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

da ne leen: «Defleen seen xel ci mboolem kàddu yi ma leen di artoo man, bésub tey, te ngeen sant seeni doom ñu sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii.

Yoon a ngii, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci dee.

Luke 9:44 TSK

¶ «Ubbileen seeni nopp te teewlu bu baax kàddu yii: Doomu nit ki lees di wor, ngir teg ko ci loxoy nit ñi.»

Luke 16:2 TSK

Waa ja woo ko, ne ko: “Li ma la déggal, lu mu doon? Limal ma sag caytu, ndax dootoo ma mana saytul.”

Mu ne: “Ma ne leen, képp ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu am as néew sax, dees na ko nangu.

Ca saa sa nag laa yeble ci yaw. Yaw it def nga lu baax, bi nga dikkee. Léegi nag nun ñépp a ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu mboolem lu la Boroom bi sant.»

¶ Ma àrtu leen ci kaw yiw wi ma Yàlla may; bu kenn ci yeen teg boppam fu mu àggul, waaye xalaate leen sago, te ku nekk dëppoo ak céru ngëm bi ko Yàlla sédd.

Ku ci xalaat ne moom jottlikatub kàddug waxyu la, mbaa boroom ag may la ci Noo gi, war naa xam xéll ne lii ma leen bind, santaaneb Boroom bi la.

¶ Moo tax nu wara yokka teewlu kàddu yi nu dégg, bala noo lajj, taañaañal.

¶ Kon nag baleen mboolem xeetu mbon, ak mboolem njublaŋ, ak jinigal, ak kiñaan, ak mboolem xeetu yàq der.