TSK

TSK · Luke 8:31

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 2:5 TSK

Léegi xàccil sa loxo rekk, dal ci kaw jëmmam jépp. Ndegam du jàkkaarlook yaw, xarab la.»

Luke 8:28 TSK

Ba mu gisee Yeesu, daa yuuxu, daanu fa kanamam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, ana lu ma joteek yaw? Dama lay tinu, bu ma mbugal!»

¶ Juróomeelu malaaka mi wal liitam, ma gis, biddiiw bu xàwwikoo woon asamaan, ba wadd ci kaw suuf. Ñu jox ko caabiy kàmbu xóote ba.

¶ Gannaaw bu ñu seedee ba noppi nag, rab wiy jóge ci xóote bi mooy xareek ñoom, daan leen, ba rey leen.

Ñu daldi jàpp rab wi, mook yonentu caaxaan, bi defoon ci turu rab wi ay kéemaan yu mu sànke ña ñu màndargaale woon màndargam rab wi, te ñu doon jaamu jëmmu nataalu rab wi. Ñoom ñaar ñépp lañu sànni, ñuy dund ca déegu sawara waak tamarax bay bax.

Ba loolu amee ñu jàpp ndee ak njaniiw, sànni ca déegu sawara sa. Ñaareelu dee gi nag moo di déegu sawara si.