Ba mu ko defee nu ne la: “Am nanu baay bu màggat. Sunu rakk, ji mu jur te fekk ko di màggat nag, moo ci gën di ndaw. Magam dafa dee, mu des moom doŋŋ ci ndeyam, baayam sopp ko lool.”
TSK
TSK · Luke 8:42
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 44:20
TSK
Job 4:20
TSK
Diggante subaak ngoon, ñu moxoñoo, bala ngaa yég, ñu sànku fàww,
Psalms 103:15
TSK
Nit aki fanam di saxayaay suy law ni tóor-tóoru àll;
Ezekiel 24:16
TSK
«Yaw nit ki, maa ngii di nangusi sa bànneexu bët cim pàdd. Bul yuuxu, bul jooy, bu sa rongooñ wadd.
Zechariah 12:10
TSK
¶ «Bu loolu amee maay sottil waa kër Daawuda ak waa Yerusalem, noowug yiw aki dagaan, ba ñu geesu ma man, mi ñu jam ba mu sar, te dinañu ko jooy ni ñuy jooye benn bàjjo, di ko naqarlu ni ñuy naqarloo deewug taaw.
Luke 7:12
TSK
Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa.
Romans 5:12
TSK
¶ Bàkkaar moo jaare ci kenn nit dugg ci àddina, dee jaare ci bàkkaar, dikk, ba dikkal ñépp, ndax ñépp a bàkkaar.