TSK

TSK · Luke 9:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Luke 9:11 TSK

Teewul nit ña yég ne fa la dem, daldi ko topp. Yeesu dalal leen, di leen wax ci mbirum nguurug Yàlla, ña aajowoo am paj, mu wéral leen.

Luke 10:9 TSK

Wéral leen jaragi dëkk ba, te ngeen wax waa dëkk ba, ne leen: “Nguurug Yàlla dëgmal na leen.”

¶ «Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi la woon ba kera ba Yaxya dikkee. Waaye ba mu dikkee lañu yégle nguurug Yàlla, ñépp di ci jéema dugge seen doole.