TSK

TSK · Luke 9:35

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ab yonent laa leen di feeñalal ci seen biiri bokk, ni yaw. Maay yeb samay kàddu ci gémmiñam, mu àgge leen mboolem lu ma ko sant.

Teewluleen te dikk fi man. Dégluleen, ba mana dund, ma fas ak yeen kóllëre gu sax, gi ma baaxee Daawuda ci ngor gu wóor.

Luke 3:22 TSK

Ba loolu amee Noo gu Sell gi moo bindoo ni pitax, wàcc ci kawam, baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaa may bànneexal.»

Acts 3:22 TSK

Musaa kay noon na: “Boroom bi seen Yàlla mooy seppee ci seenu xeet ab yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax.

¶ Kon nag ni ko Noo gu Sell gi waxe: «Bésub tey jii bu ngeen déggee baatam,

Noonu lees matale Almasi sëkk, ba mu doon cosaanu mucc gu dul jeex, ñeel mboolem ñi ko déggal.

Ndax kat moo nangoo ci Yàlla Baay bi, teraanga ak daraja, ba ko baat ba jibalee, bawoo fa Boroom daraja ju yéeme ja ne: «Kii moo di Sama Doom, sama Soppe; ci moom laa ame bànneex.»