Deuteronomy 11:7
TSK
Seeni gët déy ngeen teg ci mboolem jaloore ju màgg jooju Aji Sax ji def.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Seeni gët déy ngeen teg ci mboolem jaloore ju màgg jooju Aji Sax ji def.
¶ «Léegi nag taxawleen ba gis jaloore ju réy jii Aji Sax jiy def, ngeen teg ci bët.
Ku bége sama njàqare, yal nanga rus, ba torox. Kuy réy-réylu ci sama kaw, yal nanga am gàcce, ne yàcc.
Aji Sax ji, sëlëm leen gàcce, ba ñu sàkku la.
Maay biralee noonu sama màggaay ak sama sellnga, maa niy xamlee sama bopp, yéefar yu bare di gis, ba xam ne maay Aji Sax ji.”»
Kookooy doon buntu jàmm, ba bu waa Asiri songee sunum réew, ba daagoo sunu kawi tata, juróom ñaari njiit lanu koy yékkatil, ba juróom ñetti garmi.