Léegi nag su ngeen ma déggalee bu baax, di sàmm sama kóllëre ak yeen, yeenay doon sama moomeelu bopp ci mboolem askan yi. Dëgg la, àddina wërngal këpp maay Boroom,
TSK
TSK · Malachi 2:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
yi nga nu dénk, yonent yiy say jaam jottli ko, ne nu: «Réew mi ngeen di nanguji, réew mu sobewu la ndax sobey waasoy réew ma. Feesal nañu kook seeni jëf ju siblu ak seen tilim, ba fépp daj.
¶ Ngalla sama Yàlla, bàyyil xel mbugal mu ñeel ñii teddadil liggéeyu carxal, fecci worma sasu carxal ak xeetu Leween.
Seedeleen ne Aji Sax jeey Yàlla. Moo nu sàkk, nuy ñoñam, di gàttam yi muy foral.
Délloosil képp ku ñu ma tudde, te sama màqaama tax ma sàkk ko, tabax ko, sottal ko.»
Aji Sax ji dafa wax, moom mi la sàkk, mooñ la fa sa biiru ndey, di la dimbali. Mu ne: «Yaw Yanqóoba sama jaam bi, yaw Yesurun sama tànnéef laa wax, bul tiit.
Yaw déy yaa di sunu Baay. Ibraayma xamalu nu dara, Israyil xamu nu. Yaw Aji Sax ji yaa di sunu Baay, sa tur a di “sunu Jotkat naka jekk.”
Éy Aji Sax ji, bul mer lool, bul ba xel fàww ci ñaawtéef. Ngalla seetal ne nooy sa ñoñ, nun ñépp.
«Yaw nit ki, ñi dëkke genti réewum Israyil mii ñu ngi naan: “Ibraayma kenn la woon te moo moomoon réew mi. Kon nun ñiy ñu bare noo ko ci gëna yey.”
«Doom teral baayam, jaam, sangam. Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? Su ma dee ab sang, ana saab cér?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur, yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?”
Yuda wor na, lu jomblu lees def fi Israyil ak Yerusalem. Yuda déy moo teddadil li Aji Sax ji sopp te mooy bérabam bu sell: Yuda moo takk janqub yàllay doxandéem.
Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel, te baña nax seen bopp naan: “Nun, Ibraayma mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan.
Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, di leen jéema jubale, ne leen: “Yeen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di lorante?”
¶ Ibraayma sunu maam ci wàllu njureel nag, ana lu nuy wax ne moom la gis ci moomu mbir?
Ab gëmkat daal mooy yóbbu mbokkum gëmkatam ci yoon? Te loolu ci kanam aji gëmadi ñi sax lañu koy defe far!
Te it jenn Yàllaa am; mooy Baayu ñépp, moo tiim ñépp, di jëf ci ñépp te nekk ci ñépp.
Ci moomu mbir, bu kenn ci yeen tooñ mbokkam, di aakimoo yelleefam, ndax waxoon nanu leen ko, ba artooti leen ne leen jëf ju ni mel, Boroom bee koy fey ña ko def.