TSK

TSK · Malachi 2:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Wattuleen seen bopp, bala leena jikko ju sew yóbbe ngeen naan ci seen xel: «Atum juróom ñaareel mi, atum njéggalug bor dëgmal na,» ba tax ngeen sajje xef, seen mbokkum ndóol, joxuleen ko dara. Da leen di booleek Aji Sax ji, ngeen gàddu bàkkaar.

¶ Mu am bés, gannaaw ba ñu lekkee ba naan ca seen saraxu cant, foofa ca Silo, Aana jóg. Booba Eli sarxalkat baa nga ca toogu ba, feggook jënu buntu jaamookaayu Aji Sax ji.

¶ Ci biir loolu askan waak seeni jabar di xultu lool ci seen kaw bokki Yawut.

Ba leen Yàlla fàddee, ña des sàkku ko, tuub, waññiku ci moom.

Saraxu nit ku bon ñaawtéef la, rawatina bu ci jubloo lu bon.

«Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax. «Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy, suur nebbonu juru yar gi, deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.

Su ñu ci boole woon koor sax, duma déglu seeni dagaan. Su ñu ma doon sarxalal saraxu rendi-dóomal ak saraxu pepp it, du maa leen di nangul. Xanaa saamar akub xiif ak mbas kay laa leen di faagaagale.»