TSK

TSK · Malachi 2:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ca Elasar sarxalkat bi nag la war di dem, ngir mu di ko seetal fi kanam Aji Sax ji, lu Urim, jumtukaayu tegtal bi, feeñal. Ci ndigalal Elasar nag lañuy génne, te ci ndigalam it lañuy dellusee, moom Yosuwe, ak mboolem bànni Israyil giy ànd ak moom, mbooloo mépp.»

¶ Su ko defee sarxalkat yi, Leween ñi dikk, ndax ñoom la seen Yàlla Aji Sax ji taamu, ngir ñu di ko liggéeyal, di barkeele ciw turam, te ci seen kaw kàddu lees di àttee bépp jote, ak gépp loraange ci wàllu yaram.

Urya sarxalkat ba daldi tabax sarxalukaay bu dëppook mboolem tegtal ya bàyyikoo ca Buur Axas ca Damaas. Uri noppi na ko bala Buur Axas di ñibbsi.

Esra, sarxalkat ba, indi téereb yoon wi keroog benn fanu juróom ñaareelu weer wa, fa kanam mbooloo ma, góor ak jigéen, mboolem ña seeni at may ñu dégg ko.

Ana ku silmaxa ku moy sama jaam bii? Ku tëx ba dab sama ndaw li ma yónni? Ana ku silmaxa ba dab kii ñu jàmmal? Ku silmaxa ba dab jaamu Aji Sax jii?

Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Soo délsee, ma délloosi la, nga dellu di ma liggéeyal. Soo dee wax ngëneel lu soreeki caaxaan, dinga mel ni yaay sama làmmiñ, te nit ñeey délsi ànd ak yaw, waaye du yaay délsi ànd ak ñoom.

Ay sarxalkatam xëtt nañu sama yoon, teddadil nañu sama yëf yu sell. Lu sell ak lu sellul, ràññeewuñu ko; lu set ak lu sobewu, xamlewuñu ko; sama bési Noflaay, ñu jéllale ko, ba ma mujj teddadi fi seen biir.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Sàkkul nag ndigal ci sarxalkat yi, nga ne leen,

¶ «Maa ngii di yebal sama ndaw, mu xàllal ma aw yoon. Sang bi (/Boroom bi) ngeen di sàkku mooy jekki agsi këram, malaakam kóllëre moomu (/ndawal kóllëre loolu), ki ngeen safoo, mu ngooguy dikk.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Kon nag Almasi, noo diy ndawam, te ci nun la Yàlla di wootee. Kon ci turu Almasi, danu leen di ñaan: nanguleena juboo ak Yàlla.

Kon nag ku jalax ndigal lii, du nit nga jalax, xanaa Yàlla, moom mi leen jox Noowam gu Sell.