Buleen far-farloo cib àtte, dégluleen ku tuut, ni ngeen di dégloo ku mag, te buleen ragal kenn, ndax àtte bi Yàllaay boroom. Bu leen mbir mi ëppee loxo nag, ngeen indil ma ko, ma seet ko.»
TSK
TSK · Malachi 2:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mise ne: «Soo délseek jàmm déy, Aji Sax ji waxul, ma jottli.» Mu dellu ne: «Mbooloo mi, yeena ko déggandoo, yeen ñépp.»
Ku jub barkeel, saw tur du fey; ab soxor, turam seey.
¶ Gannaaw loolu Yonent Yàlla Yeremi ne yonent ba ñuy wax Anaña: «Anaña, déglul bu baax li ma lay wax: Aji Sax ji yebalu la, yaw ngay gëmloo askan wii ay fen.
¶ «Yónneel ca ngàllo gépp ne leen: Aji Sax ji dafa wax ci mbirum Semaya Neyelameen ba, ne: “Semaya waxal na leen waxyu, gëmloo leen ay fen, te yebaluma ko.
Maay foqati seeni muuraay, génne sama ñoñ ci seeni loxo, ñu noppee doon seenum pàdd, ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.
Moo tax yeen, guddi moo leen di ñeel, ba peeñu réer, lëndëm a leen di dikkal, ba ngis tukkil leen, jant mooy sowal yonent yi, bëccëg lëndëmal leen.
Maa ngii di yar seen askan, sëlëm leen sébbriit, mi jóge ci seen saraxi màggal, ñu tonniwaale leen ak sébbriit mi.
Waaye wóoy ngalla yeen Farisen yi! Xobi naana ak yeneen safal yu mel ni ru ak wépp xeetu lujum, yeena ngi ciy génne cérub fukkeel, ngir asaka, njubte ak cofeelu Yàlla nag, ngeen sàggane. Lii de war na leen, waaye lee it, waruleen koo sàggane.
¶ Ana lu loolu di tekki? Xanaa kon yoonu Musaa bàkkaar la? Mukk kay! Waaye yoonu Musaa moo ma xamal luy bàkkaar. Ndax kat su dul woon ak yoon wi ne: «Bul xemmem yëfi jaambur,» kon xemmemtéef sax duma xam lu mu doon.