TSK

TSK · Malachi 3:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 21:15 TSK

Ana kuy Aji Man ji sax ba ma di ko jaamu? Su ma ko tinoo, ana lu mu may jariñ?»

Job 34:9 TSK

te naa: «Nit ki seet bànneexu Yàlla, ana lu mu koy jariñ?»

Dañuy ñaawle, di wax lu bon, di réy-réylu, boole ci kàdduy jaay-doole.

te naa: “Ana lu nuy woor te xooloo ci? Lu nuy toroxlu te teewluwoo?” Ma ne: Bés bu ngeen woor, yeena ngi topp seen bakkan, di sëqatal seeni liggéeykat.

Joel 2:12 TSK

«Terewul ba léegi,» kàddug Aji Sax jee, mu ne: «Délseeleen seen léppi xol ci man, boole kook koor aki jooy aki yuux.

Ñu wax ak sarxalkati kër Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ak yonent yi, ne leen: «Ndax danoo wara wéye jooy ak di woor ci weeru juróomeel, ni nu ko baaxoo at yii yépp?»