TSK

TSK · Micah 1:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba ñu leen génnee, kenn ci ñoom ne Lóot: «Dawal sa xélu bakkan, bul geestu, bul taxaw fenn ci joor gi. Dawal ca tund ya, bala ngaa dee.»

¶ Gannaaw loolu Yerbowam dëppul yoonam wu bon wa mu topp. Dafa dellu tabb ci biir baadoolo yi ay sarxalkat ngir bérabi jaamookaay ya. Ku bëgg rekk mu tabb la, ngay sarxalkat ca bérabi jaamookaay ya.

Mu sàlloo bàkkaari Yerbowam doomu Nebat. Loolu doyatu ko, mu jël jabar Yesabel doomu Etbal, buurub waa Sidon ña. Mu dem bay jaamu seen tuur mi ñuy wax Baal, di ko sujjóotal.

Ca tànki buuri Israyil la topp. Doomam ju góor sax def na ko sarax, lakk ko ngir tuur ya, di roy ñaawtéefi xeet, ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.

¶ Buurub Asiri nag tollu ca Lakis, yebal bummeem ak kilifay jawriñam ak bëkk-néegam, ñu ànd ak mbooloom xare mu takku, dem Yerusalem. Ba ñu agsee Yerusalem ba tollook solomu mbàndum kaw ma, fa feggook yoon wa jëm ca toolub fóotukaay ba, fa lañu taxaw.

Waa Madmena ñooy fëlxoo, waa Gebim wuti rawtu.

Gis naa ne it Israyil Woyof-Kumba-si gànctu na ba ma yebal ko, jox ko kayitu pase, mu dem, te taxul doomu ndeyam Yuda workat bi ragal. Moom it daa dem di gànctu.

Mu yemook ba mbooloom buuru Babilon di xareek Yerusalem ak mboolem dëkki Yuda ya desoon, di Lakis ak Aseka. Booba yooyu rekk a desoon ci dëkki Yuda yu tata wër.

Micah 1:5 TSK

Bàkkaaru Yanqóobaa waral lii lépp, moyi Israyil googu la. Ana luy bàkkaaru Yanqóoba? Da dul Samari? Ana fuy bérabi jaamookaayi xërëm ci Yuda? Da dul Yerusalem?

¶ «Waaye lenn laa lay sikke: dangaa bàyyi Yesabel, jigéen joojuy tuddoo yonent, muy jàngleek a réeral sama jaam ñi, ngir ñuy gànctu ak a lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur.