TSK

TSK · Micah 2:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ngalla Buur, sama sang, déglul lii ma lay wax: su fekkee ne Aji Sax ji moo la xiir ci sama kaw, yal na ko cib sarax giifal. Waaye su dee ay doom aadama de, yal nañu alku ci kanam Aji Sax ji, ndax dàq nañu ma tey, ba xañ ma ab cér ci Aji Sax ji, mbete ku ñu ne: “Demal jaamuji yeneen yàlla.”

Xayma xotatoo, buumi xayma xëttandoo, samay doom wacc ma, ne mes; kenn sampatul sama xayma, firi ko.»

Waaye ni ndox muure xóotey géej ba mu daj, ni la darajay Aji Sax jiy ràññikoo ci àddina sépp.

Ñooy saax-saaxee alalu jëtun ñi tey julli julliy ngistal yu dul jeex. Ñooñu la seen mbugal di gëna tar.»

Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leere ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi.