TSK

TSK · Micah 3:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci kaw loolu magi Mowab ànd ak magi Majan, dem, yóbbaale ay weexal. Ba ñu agsee ca Balaam, daldi koy àgge kàdduy Balag.

Doomi Samiyel yu góor ya nag jaaruñu ci seen tànki baay. Dañoo lajj, topp alal ju lewul, di nangu ay ger, di jalgati dëgg.

Ku bon day nangu alalu ger ca suuf, nara jalgati yoon.

moona yeena ngi sagoo turu dëkk bu sell bi, di wéeroo Yàllay Israyil ji turam di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

Mu ne: «Ñoo fenal Aji Sax ji, naan: “Moom du def dara, musiba du nu dal, saamaroo, xiifoo, dunu ci gis dara.

Buleen naxe seen bopp kàdduy caaxaan, naan: ‘Kër Aji Sax jaa ngi, kër Aji Sax jaa ngi fii, kër Aji Sax jee!’

«Maay joxe seeni jabar, jox seeni tool ay foqatikat, ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Ab yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor!

Alalu ger, ñu jël fi sa biir, ngir lor ay bakkan. Ndollant ci kaw tegandaay, nga jël feyeekoo bor, di wute alal sa àqu moroom. Man nag, nga fàtte ma. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

Seenu ñoll giiful sax, ñuy gànctoo gànctu, te gàccee gënal seeni kilifa.

Amos 9:10 TSK

Saamar ay rey mboolem sama bàkkaarkati mbooloo mi naan: “Yàlla du wacc musiba di nu jege, ba di nu dab.”»

Micah 7:3 TSK

Lu bon la seeni loxo mane: kàngam di laaj, ab xaali di sàkkub ger, boroom daraja moom, di wax fuqley bakkanam, ñu ànd ràbbum pexe.

ay yonentam reew, diy workat; ay sarxalkatam teddadil sellnga, xëtt yoon.

«Moo tax man it ma def xeet wépp xeeb leen, sewal leen, feye leen ko seen ñàkka sàmm samay yoon, ak par-parloo gi ngeen di diglee yoon wi.»

Acts 8:18 TSK

¶ Simoŋ nag gis noonee mayug Noo, gi sababoo ci tegeb loxo bu ndaw ña amal, ba tax mu indil leen xaalis.

Bumu di ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, waaye na lewet, bañu ay, te bumu di bëggkatub xaalis.

Foral-leen gétt gi ñu leen dénk. Sàmmleen ko, te bañ koo defe ñàkk pexe, xanaa xol bu tàlli, ni ko Yàlla bëgge. Buleen ko defe it koppartuy kese, waaye farluleen ci.

¶ Seeni gët xoolul lu moy ku ñu jaalool, te duñu bàkkaar ba regg mukk; ku dëgërul, ñu yóbbaale la. Ñooñu la seenub xol tàggatu ci ag bëgge, mii njurum alkànde!