TSK

TSK · Micah 3:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bokk yi, ñu xalele ñoo leen di not, ay jigéen yilif leen. Bokk yi, seeni njiit a ngi leen di sànk, lëndëmal nañu seeni yoon.

Yeen rabi àll yi, dikkleen ci bernde ji, yeen rabi gott bi yépp.

Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammtoo, naan: “Jàmm, lépp jàmm!” te jàmm amul.

Mu jëm ci yonent yi: Sama bopp a ubu ràpp, sama xol jeex, sama yax yépp ne yalax, ma mel ni ku biiñ man, ba mu màndi ndax Aji Sax ji ak kàddoom yu sell.

Maa ngii ci kaw ñiy waxe waxyuy génti caaxaan.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi nettali seeni gént, bay waññi sama ñoñ, ndax seen fen yu jéggi dayo, te man de yebaluma leen, santuma leen dara. Amaluñu askan wii benn njariñ.» Kàddug Aji Sax jee.

Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ci mbirum Akab doomu Kolaya ak Cedesyas doomu Maaseya, ñoom ñi leen di jottli waxyuy fen ci turam. Mu ne: Maa ngii di leen teg ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, mu rey leen, ngeen di gis.

Sama loxooy dal yonent, yiy gis peeñuy caaxaan, di gisaaney fen. Sama péncum ñoñ, duñu fa teewe, limeefu kër Israyil, deesu leen ca bind, te réewum Israyil, duñu fa dellu. Su boobaa ñu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji.

Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Wóoy ngalla jigéen ñiy sàkkal ku ne jarab xërëm, di ràbbal ku ne muuraayu xërëm bu ko jot, di ko moome nit ñi! Man ngeena aakimoo sama bakkanu ñoñ tey sàmmaale seen bakkanu bopp?

Ay yonentam a ngi déeyoo fi biiram; ñu ngi xiiru ni gaynde guy xotat pàddam, di lekk doom aadama yi, foqati alal ak gànjar, ful jëtun yi ci biiram.

Nit man naa wër, toppi caaxaan aki fen, naan: “Maa lay yégal waxyub biiñ aku ñoll,” te kookooy jottlikatub waxyu bi askan wii yelloo!

Waaye yeen dangeena moy yoon wi, seenum njàngle ngeen fakktale ñu bare, te yeena fecci kóllëreg Lewi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.