TSK

TSK · Micah 4:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te it ñenn ci sag njaboot, ñu soqikoo ci yaw, di ñoo meññ ci sa geño, dinañu leen jàpp, ñu doon jaam yu ñu tàpp ca biir kër buuru Babilon.”»

musal leen ci loxol bañaale, jote leen ca loxol noon ba,

Man maay yékkati Sirus ci biir njekk, xàllu yoonam. Moom mooy tabax sama dëkk, yiwi sama ñoñ ñi ñu toxal, te du laaj pey mbaa neexal.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Yeen genti Yerusalem, àndleen sarxolle; Aji Sax jeey dëfal ñoñam, mooy jot Yerusalem gii!

Baatu ndaw su jagadi laa dégg, ma nga jàq, di matub taawam. Baatub Siyoŋ, dëkk bu taaru baa! Ma ngay àppaat, tàllal yoxo ya, naan: «Wóoy, ngalla man; ne yàcc ci loxol bóomkat yi!»

«Ab soxor jàpp la, ma àtte; ab néeg ne la céex, ma foqati.»

Maay fóom garabi reseñam aki figgam, yi mu noon: “Lii sama peyoor la! Samay far a ma ko jox.” Maa koy def ay dédd, rabi àll yi di ko lekk.

Micah 5:2 TSK

Moo tax Aji Sax ji di leen wacc ba keroog jant, ba kiy matu mucc. Ca la bokkam ya dese bakkan di dellu, fekki seen bokki bànni Israyil.

¶ Fa la malaaka ma doon wax ak man jekki di dem, meneen malaaka dikk dajeek moom.

Ñu jox ndaw si ñaari laafi jaxaay ja, ngir mu naaw, rëcc ninki-nànka ji, dem màndiŋ ma, ca rawtoom ba ñu koy leele lu tollook ñetti diir ak genn-wàll.