Yàlla ne Musaa: «Maay Ki nekk. Kon waxal bànni Israyil ne leen: “Aji Nekk ji moo ma yónni ci yeen.”»
TSK
TSK · Micah 4:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 3:14
TSK
2 Kings 17:34
TSK
Ba tey jii ñu ngi topp seen aaday cosaan. Ragaluñu Aji Sax ji dëgg te sàmmontewuñook santaane yeek dogal yeek yoon week ndigal li Aji Sax ji joxoon askanu Yanqóoba mi mu tudde Israyil.
Psalms 48:14
TSK
nemmikuy tataam, doxantoo këri buur, ba man koo yegge maasug ëllëg,
Psalms 145:1
TSK
Muy jàngi màggal, ñeel Daawuda. Sama Yàlla, Buur bi, naa la màggal, teral sa tur ba fàww.
Isaiah 26:8
TSK
Aji Sax ji, nu ngi lay xaar, fi sa kaw yoonu santaane yi, di la sàkku, ba la xel, lii déy, mooy sunu nammeelu xol.
Jeremiah 32:40
TSK
Maay fas ak ñoom kóllëre gu sax dàkk gu ma leen dul xañati; xanaa baaxe leen, yeb ragal Yàlla ci seen xol, ba dootuñu ma won gannaaw.
Colossians 2:6
TSK
¶ Kon nag, ni ngeen nangoo Almasi Yeesu di Sang bi, àndleen ak moom, jëfe noonu.