TSK

TSK · Micah 5:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci kaw loolu Rasel faatu, ñu denc ko ca yoonu Efrata, ga ñuy wax Betleyem ba tey.

Nguur gi du jóge ci loxol Yuda, te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam, li feek boroom di ñëw, ba xeet yi déggal ko.

Mu seet ca bànni Israyil gépp, tànn ca góor ñu mat, fal leen, ñu yilif mbooloo ma: ñii jiite kuréli junniy nit; ñii, téeméer; ñii, juróom fukk; ñii fukk.

Ñoom lay tabb ngir ñu doon njiiti kuréli junniy dag, mbaa njiiti kuréli juróom fukk. Ñoom it lay beyloo toolam, di leen góobloo, di leen sàkkloo ay gànnaayi xareem ak jumtukaayi watiiram.

¶ Daawuda nag moo doon doomu góor googu dëkk Efrata ca Betleyem ga ca diiwaanu Yuda, ñu di ko wax Yese. Yese amoon na juróom ñetti doom yu góor. Góor ga, ca jamonoy Sóol, mag mu ñu nawloo la woon.

Seetleen ba gis fépp fu mu mana làqu, doora délsi fii ci man, indil ma lu leer. Su ko defee ma ànd ak yeen. Su Daawuda nekkee ci gox bi, dinaa topp tànkam ci biir mboolem làngi Yudeen ñi.»

Ma ne: «Éy sama Yàlla, maasoo maas, say at du jeex. Bu ma yóbboo sama diggi fan.

Soxna si, Xel mu Rafet nee na: «Aji Sax ji jagoo na ma ca njàlbéen, ma jiitu ca jëfam ya woon.

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Kii màgge fi kanamam ni njëmbat, te nirook reen bu fette ag kekk. Dub taar, du yànjaay bu nu koy niire, du meloom wu nu koy soppe.

Su boobaa seen njiit di seen deret, di seen kilifa, soqikoo ci ñoom; ma woo ko, mu jege ma, nde nit jaayul bakkanam, ba jegesi ma te woowuma ko!» Kàddug Aji Sax jee.

¶ «Gannaaw loolu maa leen di waajalal ab sàmm bu leen di sàmm. Kookooy Daawuda sama jaam bi. Moom moo leen di foral, mooy doon seen sàmm.

Amos 9:11 TSK

«Bésub keroog maay yékkati mbaarum Daawuda mi joy, ba fattaat xar-xar yi, defaraat gent bi, tabaxaat ko na woon.

Bégala bég, janq Siyoŋ mu taaru, janq Yerusalem mu taaru laa ne: Xaacul, sa buur a ngoog, jëmsi ci yaw, moo jot njekk ak mucc, te teewu koo woyof, war mbaam, cumbur doomu mbaam.

Luke 2:4 TSK

Ku ñuy wax Yuusufa itam jóge Nasaret ca diiwaanu Galile, jëm ca diiwaanu Yude ca Betleyem, dëkk ba Daawuda cosaanoo, ndax ci waa kër Daawuda la askanam bokk.

¶ Ñu bindal ko nag fa ko tiim, mbind mii: «Kii mooy buurub Yawut yi.»

Waaye li àddina jàppe ag ndof, moom la Yàlla taamu, ngir rusloo ko xamkat yi, te li néew doole ci àddina, moom la Yàlla taamu, ngir rusloo ko li bare doole.

Li wér te wóor it moo di sunu Sang ci Yuda la soqikoo, te googu giir, Musaa waxu ci lenn lu jëm ci sarxalkat yi.

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Samirin nag, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Ki Jëkk te Mujj, Ki dee woon te dekki. Mu ne:

Mu neeti ma: «Sotti na! Maay Alfa, di Omega, di njàlbéen, di muj. Ku mar, maa lay may nga naan ci bëtu ndoxum dund mi, te doo fey dara.