TSK

TSK · Micah 5:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yuda yaa di gaynde gu ndaw, doom, doora jóge nii ci pàdd, tey yuug ak a goor ni gayndeg sibi. Yaa di gaynde gu deesul yee.

yilife leen yetu weñ, rajaxe leen ni njaqal xandeer.”»

Sang baa ngi fi sa ndijoor te mooy rajaxe buur yi, bés bu meree.

Man déy ni gaynde laay mel ak Efrayim, ni gaynde gu ndaw laay mel ak waa kër Yuda. Man, man mii maay xotat, wéy, maay yóbbu te kenn du wallu.

«Yaw janq Siyoŋ mu taaru, jógal bàcci leen, sa béjjén laay def ag weñ, say wewi tànk, ma def ko xànjar, nga rajaxe xeet yu bare.» Yaay faagaagal seen alal ju lewul, ñeel Aji Sax ji, seen koom ñeel Boroom àddina sépp.

Ni ñeyi xare lañuy mel, di joggati banu mbedd mi ci biir xeex bi. Noonu lañuy xaree, nde ñoom la Aji Sax jiy àndal, ñuy torxal gawar yi.

Làngu Misra it, su ñu yéegul ba dikk, duñu tawlu; dinañu jot ci duma yi Aji Sax jiy duma xeet yi yéegul ba màggalsi màggalu Mbaar yi.

Acts 18:6 TSK

Yawut ya nag gàntal, di ko ŋàññ, mu yëlëb ay yéreem, misaale ko ne jaanam wàcc na. Mu ne leen: «Yeenay gàddu seen bakkanu bopp. Man set naa ci wecc. Gannaaw-si-tey, ci jaambur ñi dul Yawut laa jëm.»

ana kon nun ci sunu bopp, nan lanuy rëcce mbugal, su nu sàgganee pexem mucc mu réy mii Sang bi jëkkoona biral, te ñi ko dégg dëggalal nu ko?