Yeen asamaan, teewluleen, ma wax, Yaw suuf, déglul sama kàddu yii.
TSK
TSK · Micah 6:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. Yàlla, Aji Sax ji Yàlla àddu na, di woo àddina, penku ba sowu.
Asamaan, déglul; suuf, teewlul, Aji Sax jeey àddu: «Ay gone laa yar, màggloo leen, ñoom, ñu gàntal ma.
Aji Sax jaa ngi ci jataayu layoo, moo jóg di àtte ay xeet.
Éy waa réew mi, waa réew mee, waa réew mi, dégluleen Kàddug Aji Sax ji!
¶ «Yaw nit ki, waxalal waxyu tundi Israyil. Neel: “Yeen tundi Israyil, Dégluleen kàddug Aji Sax ji.
Mu ne ma: «Waxal waxyu fi kaw yax yii, ne leen: “Yeen yax yu wow yi, dégluleen kàddug Aji Sax ji:
Dégluleen, yeen, xeetoo xeet, teewlul, yaw àddina ak li ci sa biir, ba Boroom bi Aji Sax ji seedeel leen tuuma, Boroom beey àddoo fa màkkaanam mu sell ma.
Mu ne: «Maa leen ko wax, su ñii noppi woon, doj yi ñooy xaacu.»