Ca suba sa Balag ànd ak Balaam, yéege ko ba ca kaw jaamookaay ba ñu dippee Baal, tuur ma, mu tollu fa di séen lenni catu mbooloo ma.
TSK
TSK · Micah 6:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Balag ne ko: «Kaay rekk, ma yóbbu la feneen. Jombul Yàlla nangu nga móolool ma leen foofu.»
Jigéen ña di woo mbooloo ma ca seen saraxi tuur ya, mbooloo ma di lekk ak a sujjóotal seeni tuur.
Xanaa du ñoom ñoo dëdduloo woon bànni Israyil Aji Sax ji, ci ndigalal Balaam, ca mbir ma woon ca Pewor, ba tax mbas ma dikkal mbooloom Aji Sax ji?
Fàttlikuleen mboolem yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji awale diiru ñeent fukki at yii ci màndiŋ mi, teg leen coono, nattu leen ngir xam li ci seen biir xol, xam ndax dingeen wormaal ay santaaneem, am déet.
¶ Fàttlikuleen! Buleen fàtte na ngeen merloo woon seen Yàlla Aji Sax ji ca màndiŋ ma. La dale bés ba ngeen bàyyikoo réewum Misra, ba ba ngeen agsee bérab bii, fippu ci kaw Aji Sax ji ngeen masa nekke.
Ab Amoneen mbaa ab Mowabeen du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji. Ku askanoo ci ñoom it, ba ca fukkeelu maas ga, du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji mukk,
Kon nag taxawleen, ma layook yeen fi kanam Aji Sax ji, ci mboolem njekk gu leen Aji Sax ji defal, yeen ak seeni maam.
May siiwal sa njekk, di yendoo waxtaane say wall, doonte lim ba wees na ma.
Ñeel Daawuda. Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, saa jëmm jépp di sàbbaal sellngay turam!
Aji Sax ji, musal ma ngir saw tur, jëfeel sag njekk, teggil ma njàqarey bakkan.
¶ Kon nag, yeen jaambur ñi dul Yawut cib juddu, yeen ñi ñuy wooye yéefar yi xaraful, te ñi leen ko dàkkantale woon di Yawut yi xarafe ci loxol nit ku leen xarfal ci seen yaram, fàttlikuleen seen démb.
¶ «Waaye lenn a ngi lu ma lay sikke: yaa ngi uuf foofu ay nit ñuy saxal njànglem Balaam, moom mi doon xiirtal Balag ci tegal Israyil ndëgg-sërëx, ngir ñu lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur, ak di gànctu.