Man de yàlla bu sama bakkan rote àll, fu soreek Aji Sax ji. Te sax, lu tollu ni buurub Israyil ci boppam wutul lu moy wenn fel doŋŋ wu mel ni man? Mbete kuy rëbb cokkeer ci tund yi!»
TSK
TSK · Micah 7:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda. Ab dof a ngi naa ci xelam: «Yàlla amul!» Ñu ni mel ay def njekkar, seeni jëf siblu, kenn defu ci lu baax.
Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jaambur bu deful dara.
Nit ñiy soxorante, ku nekk ak moroomam, ku nekk ak dëkkandoom, ndaw di ñàkke mag kersa, sagaru nit sofental boroom daraja.
seeni tànk daw wuti lu bon, ñuy yàkkamtee tuur deretu ku deful dara, seeni xalaat di ñaawtéef, yàquteek njaaxum féete ca seeni yoon.
«Waaw! Daa am ñu bon ci sama ñoñ, ñuy tërook a fiire mbete nappkati picc.
Sunuy tànk lees di topp, ba manatunoo daagoo sunuy mbedd; sunu bés jege, sunu àpp di matal, sunu saa taxaw!
Deret ngeen tabaxe Siyoŋ, njubadi ngeen tabaxe Yerusalem googu.
Yawut ya itam dëggal tuuma ja, ne noonee la mbir ma ame.