¶ Ba loolu amee Xam, baayu Kanaan, gis céri baayam, génn waxi ko Sem ak Yafet ca biti.
TSK
TSK · Micah 7:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Absalom nag yónnee ndéey. Ay ndaw yegge ko giiri Israyil gépp. Mu ne leen: «Bu ngeen di dégg liit gu jib rekk, ne leen: “Absalom falu na buur ca Ebron!”»
Ayitofel ne ko: «Demal dëkkoo sa nekkaaley baay, yi mu wacce këram, ñu di ko topptoo. Su ko defee bànni Israyil yépp dinañu xam ne def nga lu tax sa baay sib la. Dina tax say farandoo gëna am fit.»
Yàq a nga ca biir, te noteel ak njublaŋ jógul ca pénc ma.
Kuy xeelu sa baay, di siidee déggal sa ndey, baaxoñ génne ciw xur, luqi sa bët, tan ya lekk.
Say bokk ak sa waa kër baay sax, ñoom it wor nañu la, ñoom it xaacu nañu, sam la; te bu ñu lay wax jàmm it, bu leen gëm.»
Ndey ak baay, ñu tuutal fi sa biir; doxandéem bi, ñu lekk àqam fi sa biir; jirim akub jëtun, ñu néewal fi sa biir.
Baay dina féewaloo ak doomam ju góor, doom ja féewaloo ak baayam; ndey féewaloo ak doomam ju jigéen, doom ja féewaloo ak ndeyam; ndey féewaloo ak jabaru doomam, jabar ja féewaloo ak ndeyu jëkkër ja.»