TSK

TSK · Micah 7:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Samiyel wax ko lépp, nëbbu ko ca dara. Eli ne: «Mooy Aji Sax ji. Li ko soob, na ko def.»

Ci kaw loolu Daawuda dégg ne Nabal dee na, mu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji sama boroom, mi àtte gàcce gi ma ame ci Nabal, te tere maa def lu bon. Mbonug Nabal la Aji Sax ji walbati, këpp ci kaw boppam.» Daawuda nag yónnee kàddoom ca Abigayil, ngir jël ko jabar.

Ba loolu amee Daawuda wax ak Abisay ak jawriñam yépp, ne leen: «Du gis ngeen sama doom ji ma jur ci sama geño, muy wuta faat sama bakkan? Kon kay kii bokk ci giirug Beñamin matula wax. Bàyyileen ko, mu saaga ma, ndax Aji Sax jee ko ko sant.

Job 23:10 TSK

Ndaxam moo xam fi ma jaare, te bu ma nattoo, ma génn ci ni wurus wu ñu xelli.

Job 35:14 TSK

Kon ngalla yaw mi ne gisoo ko, te ne diis nga ko sa mbir, di ko xaar.

Day setal sab der ni jant bu fenk; sab àtte ne ràññ ni njolloor.

Sa boroom Aji Sax ji, sa Yàlla jiy layool ñoñam dafa wax ne: «Mu ngoog, maa jële ci sa loxo, kaas bu wex biy miirloo; taatu kaas ba def sama mbugal, dootoo ko naan.

«Israyil diy gàtt yu tasaaroo, yu ay gaynde dàq, buurub Asiri di gaynde gi jëkka lekk, Nabukodonosor buuru Babilon topp ca, seeñu yax ya.»

«Aji Sax ji jox na nu dëgg. Nanu yeggeji waa Siyoŋ jaloorey Aji Sax ji, sunu Yàlla.»

Aji Sax ji moo yey, kàddoom laa gàntal. Yeen, xeetoo xeet, ngalla dégluleen te xool samaw tiis. Samay ndaw yu góor ak yu jigéen, ñoo duggi ngàllo!

Ca ngeen di ràññaatlewaat diggante ku jub ak ku bon, kuy jaamu Yàlla, ak ku ko jaamuwul.

Moo tax buleen àtte lenn te jotul, lu jiitu Boroom biy dikk. Moom mooy leeral li làqoo ag lëndëm, di làññi mébéti xol. Su boobaa ngërëm la ku nekk yelloo, fa Yàlla lay bawoo.

Léegi nag kaalag njekk a may xaar, te Boroom bi, Àttekat bu jub bi moo ma koy yool, keroog ca bés ba, te du man rekk la koy yool, waaye itam képp ku koy séentu te yàkkamti bés ba muy feeñ.

Ñu àddu ca kaw ne: «Buur bu sell, bu dëggu bi, loo deeti xaar ci àtte waa àddina, feyul nu sunu deret ji tuuru?»