Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowug Yàlla di wër, tiim ndox mi.
TSK
TSK · Nahum 2:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñu ŋa ma, ŋàpp, ni gaynde, guy yëmmook a fàdde.
Babilon nag, mooy gànjaru réew yi ko wër, di teraanga ji Kaldeen ñiy sagoo, waaye Yàllaa koy tas, mu ne tasar ni Sodom ak Gomor.
Lii a waral sama njàqareg xol, mitit jàpp ma, mel ni mititu mat, ma jaaxle ba déggatuma, jàq ba gisatuma.
guddeek bëccëg, du fey, saxar sa day gilli ba fàww, réew ma gental giiru jamono, te deesatu fa jaare mukk.
Laajteleen te xool, ndax góor day wasin léegi? Moona maa gis jàmbaar ju ne jatu, ni kuy matu, kanam xoyy.
Kanamu Buur nag soppiku, njàqare dikkal ko, ba ndigg la ne yalax, óom yay fenqoo.
ku la gis, daw la te naan: “Niniw tas na! Moo ku koy jooy?” Ana fu ma koy wutale ñu ko dëfal?»
«Maa fàkkas ay xeet, seeni tata tasaaroo, ma wéetal seeni mbedd, ba kenn jaareetu fa, seeni dëkk a tas ba kenn desul, kenn dëkkatu fa.