Ma daldi dogu ci sama xol ne dinaa yedd garmi yeek njiit yi. Ma ne leen: «Yeen yeenay lebal seeni bokk, di sàkku tegandaay.» Ci kaw loolu ma woote ndaje mu réy ci seen mbir.
TSK
TSK · Nehemiah 13:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nehemiah 5:7
TSK
Nehemiah 13:25
TSK
Ma ŋàññ leen, móolu leen, dóor ñenn ci ñoom, xuuf seen kawar, giñloo leen ci Yàlla ne dootuñu may seen doom yu jigéen ay doxandéem te dootuñu ci jëlal jabar seeni doom mbaa seen bopp.
Proverbs 28:4
TSK
Ku wacc yoon, gërëm ku bon; ku wormaal yoon, jànkoonteek ku bon.
Jeremiah 5:5
TSK
Kon naa dem seeti kàngam yi, wax ak ñoom. Xanaa ñoom dinañu xam yoonu Aji Sax ji, xam lu seen àtteb Yàlla laaj.» Waaye ñoo bokk daggook Yàlla, dogook moom.
Jeremiah 22:2
TSK
Danga naan: “Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yaw buurub Yuda mi toog ci jalub Daawuda, yaak say jawriñ ak sa nit ñiy jaare yii bunt.
Micah 3:1
TSK
Dama ne: «Ngalla dégluleen yeen njiiti Yanqóoba, yeen kilifay kër Israyil! Xanaa du yeena wara xam yoon?