Ñooñu mujj jël ay jigéeni Mowab soxna; kenn ka di Orpa, ka ca des di Ruut. Ba ñu nekkee foofa lu tollu ci fukki at,
TSK
TSK · Nehemiah 13:23
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Gannaaw ba loolu wéyee njiit ya dikk, ne ma: «Du bànni Israyil, du sarxalkat yi, du Leween ñi, kenn ci ñoom teqlikoowul ak xeeti réew meek seen aada yu siblu. Dañuy jëfe ni Kanaaneen ñeek Etteen ñeek Periseen ñeek Yebuseen ñeek Amoneen ñeek Mowabeen ñeek waa Misraak Amoreen ñi.
Ci kaw loolu Esra sarxalkat ba jóg taxaw, ne leen: «Yeena fecci kóllëre ndax yeena jël ay jaambur jabar, di yokk tooñaangey Israyil.
¶ Ma teg nag ay nit ci bérab yu ne fàŋŋ te suufe ca gannaaw tata ja. Ma def leen ay kurél, gu ci nekk ak làngam ak bérabam. Ña nga gànnaayoo seeni xeej ak seeni saamar ak seeni fitt.
¶ Nu ne nag dunu may waa réew mi sunu doom yu jigéen te dunu jëlal sunuy doom seeni doom yu jigéen.
¶ Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq?