TSK

TSK · Nehemiah 13:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: «Waxal sarxalkat yiy doomi Aaróona ne leen: Bu ci kenn sobeel boppam, di laal mbokkam mu dee,

Su ko defee du teddadil aw askanam ci biir bànni Israyil, ndax man Aji Sax ji maa ko sellal.»

Xeeb ngeen daal ber gi leen Yàllay Israyil ber ci mbooloom Israyil, jegeñal leen boppam, ngeen di liggéey liggéeyu màkkaanu Aji Sax ji, di taxaw fi kanam mbooloo mi, di leen jaamul Yàlla?

Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.

Defuma lu ñaaw, ñuy xélu, di ma waajal; ngalla, jógal taxawusi ma, ba gis.

Su boobaa ngeen xam ne maa leen yónnee santaane bii, ngir saxal sama kóllëreek Lewi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Xanaa du benn baay lanu am, nun ñépp? Te jenn Yàlla jee nu sàkk? Lu waral ku ne di wor mbokkam, ba fecci kóllërey maam ya?