TSK

TSK · Nehemiah 8:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu juróom ñaareelu weer taxawee, bés bi jëkk ci weer wi, na doon seen bésub Noflaay bu ngeen di amal ndaje mu sell. Deeleen fàttlee bés bi liit yu xumb.

¶ Bu buur bi toogee ci jalub nguuram, na bindlu ngir moom ci boppam, ab sottib téereb yoon wii cib taxañ, ci dégtalub sarxalkat yi, Leween ñi.

Ci biir loolu ñuy jàng ci téereb yoonu Yàlla wi bés bu nekk, tàmbalee ko ca bés bu jëkk ba, ba ca bés bu mujj ba. Amal nañu màggal ga diiru juróom ñaari fan. Bésub juróom ñetteel ba nag ñu woote ca am ndaje mu sell, muy la ñu digle.

¶ Bésub keroog jàng nañu ci téereb Musaa, mbooloo ma di dégg. Ñu gis ñu bind ca ne, muy Amoneen, muy Mowabeen, kenn du ci bokk ci ndajem bànni Israyil mu ñuy màggale Yàlla, ba fàww.

«Kàddug sarxalkat déy day sàmm xam-xam, te ciy waxam la nit ñi di sàkkoo àlluwa, nde mooy ndawal Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.