te waajal gannaaw-ëllëg, ndax gannaaw-ëllëg man Aji Sax ji maay wàcc ci kaw tundu Sinayi ci kanam mbooloo mépp.
TSK
TSK · Nehemiah 9:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Fekk na tundu Sinayi wa wépp di sël-sëleeku saxar, ndax Aji Sax ja fa wàcc ci biir sawara. Saxar saa ngay gilli ni saxaru puuru ban, tund wépp di yëngook doole,
¶ Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Li ngay wax bànni Israyil mooy lii: “Yeena ko gisal seen bopp. Ca asamaan sax laa àddoo, wax ak yeen.
Bés ba ngeen taxawee fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, fa tundu Oreb, Aji Sax jee ma ne: «Dajaleel ma mbooloo mi, ma dégtal leen samay kàddu, ngir ñu tàggatu ci ragal ma li feek ñuy dund ci kaw suuf, te seeni doom it, ñu tàggat leen ci.»
Ci biir jàkkaarloo la Aji Sax ji waxe woon ak yeen ca kaw tund wa, àddoo ca digg sawara wa.
¶ Léegi nag yeen Israyil, ana lu leen seen Yàlla Aji Sax ji laaj, lu moy ngeen ragal seen Yàlla Aji Sax ji, di doxe mboolemi yoonam, sopp ko, di jaamoo seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan,
Te santaane yeek dogal yeek yoon week ndigal li ma leen bindaloon, fexeleen ba di sàmmonteek moom ba fàww. Buleen wormaal yeneen yàlla.
Asamaan lay fenke cat lii, wëndeelu, sowi cat lee; amul lu rëcc tàngooram.
Maa sopp say santaane, mu gënal ma wurus ba ci wurusu ngalam.
Sa mboolem kàddu dëgg la, sa ndigal yépp di njekk, sax dàkk.
Ca cosaan ba tey maseesula dégg, nopp masula dégmati, bët masula gis yàlla ju la moy, mu defal nii ku ko yaakaar.
Yàllaa ngi jóge Teman, Aji Sell ji foofa ca tundu Paran lay bawoo. Selaw Darajaam moo dajal asamaan, teddngaam fees kaw suuf.
Gannaaw li ma buggul, moom laay def nag, juboo naa ak yoonu Musaa ci dëggal ne yoonu Musaa baax na.