TSK

TSK · Numbers 1:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Góor ñi seen baay di Yanqóoba, mi ñu dippee Israyil, ñu àndoon ak moom, dem Misra, te ku nekk yóbbaale waa këram, seeni tur a di:

«Boo tolloo ci taxawal limeefu boppi bànni Israyil, na ku nekk ci ñoom fey Aji Sax ji njot-gi-bakkanam ba nga koy lim, ndax menn musiba bañ leena dikkal ci biir lim bi.

ñu dajale mbooloo ma mépp, keroog ca benn fanu ñaareelu weer wa. La ko dale ca ña am ñaar fukki at, jëm kaw, ñoom ñépp daldi bindu ca limeefu tur ya, ku nekk ak kër maamam, giir ak giir, làng ak làng, bopp ak bopp.

¶ Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Simeyon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.

«Waññleen mbooloom bànni Israyil gépp, ngeen lim turi góor ñépp, na ñu bokke seen këri maam, dale ko ci ñi am ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci bànni Israyil.»

Ñooñu, kenn desul ca seen biir, te bokkoon ca limeefu bànni Israyil, ba Musaak Aaróona sarxalkat ba jëkkoona tënke ca màndiŋu Sinayi.