Bàyyileen ko xel bu baax, déggal ko te bañ koo merloo, ndax du leen baal seen moy, ngir sama tur la taxawe.
TSK
TSK · Numbers 1:54
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Musaa nag nemmiku mboolem liggéey bi, ba gis ne sottal nañu ko; noonee ko Aji Sax ji santaanee woon, ni lañu ko defe. Musaa daldi leen ñaanal.
ndax bu ñuy dugg ci xaymab ndaje mi, ak bu ñuy jegeji sarxalukaay bi, dañuy jàpp, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
¶ Bànni Israyil daldi def noonu. Mboolem noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na lañu daan dale, topp seeni raaya, na lañu daan jóge, ku nekk ak làngam ak kër maamam.
Ñu daldi màggal bésub Mucc bi ci weer wi jëkk, fukki fanam ak ñeent, diggante ngoon ak jant bu so, ca màndiŋu Sinayi. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la ko bànni Israyil defe.
¶ Na ko Aji Sax ji sante Musaa nag, na la ko doomi Selofat yu jigéen defe.
¶ Samiyel ne ko: «Bànneexu Aji Sax ji ci saraxi rendi-dóomal ak yeneen sarax, mbaa tolloo naak bànneex ba muy am ci dégg ndigalal Aji Sax ji? Ma ne, dégg ndigal a gën ab sarax; xol bu nangoo gën nebbonu kuuy.