Ña nga naa leen: «Céy ngalla nun, su nu sañoon dee, Yàlla moom nu ca réewum Misra, fa nu daan uufe cini yàpp, ñam wa ne gàññ, nu suur këll. Yeena nu indi ba ci màndiŋ mii, ngeen nara xiifloo mbooloo mii mépp, ba ñu dee.»
TSK
TSK · Numbers 11:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba ngoon jotee ay picci përëntaan dikk, fees dal ba. Ba bët setee lay bay wàcc ca dal ba.
Ana lu nu Aji Sax jiy indee ci réew mii ñu nara fàddoo saamar, sunuy jabar ak sunuy tuut-tànk doon alalu sëxëtoo! Tee noo dellu Misra yee?»
Dangaa xeeb li nga nu jële réew mu meew maak lem ja tuuroo, ngir reylu nu ci màndiŋ mi, ba tax ngay buur-buurlu ci sunu kaw teg ci?
Ña ngay xultu ca kaw Yàlla ak Musaa, naa: «Lu ngeen nu doon jële Misra, ngir nu dee ci màndiŋ mi? Duw ñam, dum ndox, te wii ñamu toskare génnliku nan!»
Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.
Kon nag saamar dootu jóge sa kër mukk, ndax yaa ma ñàkke worma, ba jël jabaru Uri Etteen bi, def ko sa jabar.”
Yàlla jox leen la ñuy sàkku, wàccaaleel leen woppi ràgg.
«Doom teral baayam, jaam, sangam. Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? Su ma dee ab sang, ana saab cér?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur, yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?”
Kon nag ku jalax ndigal lii, du nit nga jalax, xanaa Yàlla, moom mi leen jox Noowam gu Sell.